Cette lettre est une invite de Serigne Touba destinée à l’ensemble de ses disciples sur l’application de la charia (la loi réelle) et de la Hahiqa (la vérité cachée)
Je cherche refuge auprès de Dieu contre le mal de l’âme, l’égarement de la passion, l’arrogance du diable et les illusions de ce bas-monde
Allah m’a même préservé du mal de l’âme, de l’égarement de l’âme, de l’arrogance du diable et de l’action illusoire du bas-monde.
Au nom d’Allah, Le Miséricordieux, Le Très Miséricordieux.
L’auteur de ces écrits recommande à tous ses disciples de se conformer à son contenu. S’ils le font, ils en tireront les bénéfices. Dans le cas contraire, ils en assumeront les conséquences.
Ô mes disciples, tendez vos oreilles, écoutez bien et assimilez ce que j’ai à vous dire : Ne vous opposez jamais à la loi pure (charia) ainsi qu’à tout ce qui est à votre portée dans le cadre de la Vérité Lumineuse (Haqiqa).
La loi pure signifie une foi conforme à l’affirmation de l’Unicité de Dieu, la noble intention ainsi que toute la jurisprudence islamique, en y intégrant tout ce qui est accessible dans la Vérité Lumineuse, uniquement pour la Face de Dieu, dans la conformité comme dans la circonspection.
Ces ordres que vous devrez appliquer sont les actes obligatoires, les actes conseillés et les actes loués que vous renforcerez par les actes licites et les bonnes prescriptions.
Puis, parmi les interdits dont vous devrez vous écarter figure la commission de tout acte interdit par Dieu dans la loi pure, en vous éloignant de tout acte illicite et proscrit par Le Seigneur.
Donc, ô mes disciples, soyez fermes dans l’observance des ordres de Dieu et dans l’abandon de Ses interdits. Par ailleurs, employez-vous uniquement à appliquer la loi pure et tout ce qui est à votre portée dans la Vérité Lumineuse. Limitez-vous à ces deux et ne vous dirigez pas vers autre chose qu’elles. Car dans un temps, vous verrez le fruit de l’application de ce que vous recommande.
Ne vous laissez pas tromper par le bas-monde et que le diable ne vous trompe pas.
Demandez pardon à Dieu et retournez vers Lui. Prenez garde aux alertes qui vous sont adressées et soyez très éveillés en elles.
Dieu est Témoin de ce que je dis.
TRADUCTION: MAJALIS

VERSION WOLOF
Betaaxal bu Boroom Tuubaa bind mbooleem ñi ko topp, ci farlu ci Chariha, ak Haqiiqa
Maa ngi ñaan Yàlla mu musël ma ci Saytaane, ak bon-boni bakkan, ag réeralug bànneex, ak bewalug Saytaane, ak wori àdduna.
Maa ngi tàmbalee samay wax ak samay jëf ci turu Yàlla mi nga xamne, mooy yëram ñépp ci àdduna, di yëram ku ko soob ca àllaaxira.
Yàlla sax musël na ma ci [yooyu ma doon muslu yépp, muy] bon-boni bakkan, ag réeralug bànneex, ak bewalug Saytaane, ak wori àdduna, te lii ma wax Yàlla diy na ci seede.
Ki bind araf yii [di Sëriñ Tuubaa], mi ngi digël képp kuko topp, mu sàmmoonteeg mbind mii ci di ko jëfee.
Suñ ko defee ñoom rekk lay jariñ, suñ ko deful it, ñoom rekk lay lor.
Yeen samay taalibé, déglu léen ma bu baax, te ngéen bàyyi xel lii ma leen di wax « bu léen wuteeg Chariha mukk, te ngéen góorgóorlu it lu ngéen man ci Haqiiqa !
Chariha nag, mooy gëm (imaan) gu tegu ci tawhiid, ànd ak yéené ju rafet, ak Lislaam ju tegu ci fiq. Nga boole ca kem la jàppandi ci Haqiiqa, te mooy def ndigël ak bàyi tere, ngir jëmmi Yàlla rekk
Bokk na ci ndigël [yooyu ngéen wara jëfe]; def warteef yi [Yàlla diglé], ak yi ñu sopp [yi Yonent bi SAWS daan def], ak jëf yu dagan yi te amuw yiiw.
Bokk na ci tere yi [ngéen wara moytu] ; moytu di def lu Yàlla tere ci Chariha, ak moytu lépp lu Yàlla araamal, wala lu mu sib.
Kon [yéen mbooleem ñi ma topp], na ngéen góorgóorlu ci topp ndigël, ak moytu tere ngir Yàlla, te ngéen doyloo Chariha ak kem la jàppandi ci Haqiiqa, te bu leen fi jéggi ñaar yooyu mukk di jëm ci leneen. Ndax su ngéen demee ba ca kanam, di ngéen gis lu tax ngéen wara jëfe lii ma léen di dénk.
Kon nag, na ngéen fexe ba bu léen dundug àdduna gii wor, te bu léen Saytaane wor.
Na ngéen tuubël séen Boroom ! Te dellu ci Moom ! Am na ay jàjje yu nekk ci seen kanam yoo xamne mat naa bàyyi xel lool, te yeete ca bu baax, Yàlla doy nama seede ci lii ma wax »
Lu ñép wara tééwlu.
Ce pays tourne à 2 vitesses. Des milliers de fidèles lors des Gamou et des Magals. Mais point de bonnes observances de la religion et de la charia strictement.
Le Sénégal est un pays très impressionnant.